1 Ba loolu amee malaaka ma doon wax ak man délsi, yee ma, mel ni ku ñu yee ciy nelaw. 2 Mu ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Damaa xool, gisuma lu moy ab tegukaayu làmp bu lépp di wurus, ak kopp bu tege ci kawam, ak juróom ñaari làmp ci kawam, bu ci nekk ak juróom ñaari gémmiñam ca kaw. 3 Ak ñaari garabi oliw ca wet ga: Genn ca ndijooru kopp ba, ga ca des ca càmmoñam.»
4 Ma dellu wax ak malaaka ma doon wax ak man, ne ko: «Yëf yii nag, lu mu wund, Sang bi?»
5 Malaaka ma doon wax ak man ne ma: «Xamuloo lu yëf yii wund?» Ma ne ko «Déedéet, Sang bi.»
6 Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne:
11 Ma dellu ne ko: «Ñaari garabi oliw yii nag, genn gi ci ndijooru tegukaayu làmp bi, gi ci des ci càmmoñam, lu ñu wund?»
12 Ci kaw loolu ma dellooti ne ko: «Ñaari cari oliw yi feggook ñaari solomi wurus yiy xelli diw nag, lu ñu wund?»
13 Mu ne ma: «Xamuloo lu yooyu wund?» Ma ne ko: «Déedéet, Sang bi!» 14 Mu ne ma: «Ñooñu ñoo di ñaar ñi ñu diw, fal leen, ngir ñu liggéeyal boroom àddina sépp.»
<- Sàkkaryaa 3Sàkkaryaa 5 ->-
a 4.7 Moo soqikoo ci Buur Daawuda. Mooy kàngam la jiite woon mbooloo ma jóge woon ca ngàllog Babilon.