1 Ba mu ko defee, ma séentu, gisuma lu moy ñeenti béjjén[a]. 2 Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Béjjén yii nag?» Mu ne ma: «Béjjén yii ñoo tasaare Yuda ak Israyil ak Yerusalem.» 3 Ci kaw loolu Aji Sax ji won ma ñeenti tëgg. 4 Ma ne: «Lan la ñii di defsi?»
Mu wax ma, ne ma: «Béjjén yii tasaare Yuda ba kenn siggeetul, tëgg yii ñoo dikk ngir tiital leen, ba jàllarbi béjjéni xeet yi jóg song réewum Yuda, tasaare ko.»
Ñetteelu misaal: Nit kuy natt Yerusalem
5 Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom. 6 Ma ne ko: «Foo jëm?»
Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo, ak nu mu gudde.»
7 Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom. 8 Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram. 9 Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”