mu bind ko
Tit
5 Li tax ma bàyyi la gannaaw ca réewum Keret mooy nga mottli la desoon ca liggéey ba, te nga tabb ay mag ñu jiite mbooloo mi ci dëkk bu nekk, na ma la ko sante woon, man ci sama bopp. 6 Ndegam nit a nga ca seen biir ñoom, di ku mucc sikk, te dencul lu wees jenn jabar, te ay doomam di ay gëmkat ñu ñu tuddul ci afal seen bakkan akug déggadi, nanga tabb ku mel noonu. 7 Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul. 8 Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam. 9 Na jàpp bu dëgër ci kàddu gu wóor gi, ni ñu ko ko jàngale, ngir mu man di ñaaxe jooju àlluwa ju wér, tey tiiñal weddikat yi.
10 Ndax kat bare na ñu të, rawatina ci tuubéen ñi bokk ci askanu yawut, ay waxkati neen lañu, te ñooy yàq xeli nit ñi. 11 Li war moo di tëj seen gémmiñ, ndax këri lëmm lañuy tase àlluwa ju ñu amul sañ-sañam, ngir di ko sàkkoo am-am bu lewul. 12 Ma wax ko waru jenn waay, ab waa Keret buy seen yonentu bopp. Mu ne: «Waa Keret, ay fen-kati neen, soxor niy rabi àll, fuqle, yaafus.» 13 Loolu mu leen seedeel mooy dëgg, te moo tax nga war leena femmoo kàddu yu dëgër, ngir seen ngëm tegu ci àlluwa ji wér, 14 te baña topp léebi neen yu Yawut yi, ak santaaney nit ñi dëddu liy dëgg. 15 Nit ñi set nag, seen lépp ay set, waaye ñi boole sobewu ak gëmadi, seen dara setul, seen xalaat ak seenum xel, ñooy bokk sobewu. 16 Xam Yàlla lañuy woote, te seeni jëf weddi Yàlla; nit ñu jara jéppi, ñu déggadi lañu, te tëlee def lenn lu baax.
Tit 2 ->