1 Boole naa leen nag ak sunub jigéen Febe, mu di ab taxawukatub mbooloom gëmkat ma dëkke Señsere. 2 Dalal-leen ko ci turu Boroom bi, ni ko ñu sell ñi yelloo, te ngeen jàpple ko ci lépp lu mu aajowoo, nde moom itam xettli na ñu bare, ba ci man mii.
16 Saafoonteeleen fóonante yu sell. Mboolooy gëmkati Almasi yépp nuyu nañu leen.
17 Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen. 18 Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi. 19 Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon. 20 Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk.
21 Timote sama mbokkum liggéeykat nuyu na leen, mook Lusiyus ak Yason ak Sosipater sama bokki Yawut.
22 Man Tersiyus mi bind kàdduy bataaxal bi ci sama loxo nag, nuyu naa leen ci turu Boroom bi.
23 Gayus mi may dalal, di dalal mbooloo mi mépp këram, nuyu na leen; Eràst saytukatub alalu dëkk bi it, nuyu na leen, mook mbokk mi Kàrtus.
24 Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen! Amiin.
25 Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk, 26 mbóot mu bindi yonent yi fésal tey, ba xamal ko xeet yépp ci ndigalal Yàlla ji sax, ngir xeet yépp gëm ba dégg ndigal, 27 kooku mooy Yàlla mi wéetoo xam-xam, te moom la teddnga ñeel ba fàww, ndax Yeesu Almasi! Amiin.
<- Room 15