1 Sanbalat ak Tobya nag dégg, ñook Gesem Araab baak noon ya ca des ne tabaxaat naa tata ja, ba xar-xar desatu ca, doonte taxawalaguma woon lafi bunt ya. 2 Sanbalat ak Gesem yónnee ci man, ne ma: «Dikkal nu dem Kefirim ca xuru Ono, diisooji fa.» Booba ña nga may fexeel. 3 Ma yónnee leen ay ndaw, ne leen: «Damaa jàpp lool. Duma mana ñëw. Xanaa duma dakkal liggéey bi, bàyyi ko fi, di leen fekki?» 4 Ñu yónnee ci man, wax ma loolu ba muy ñeenti yoon, sama tont di lenn. 5 Ba ko juróomeel Sanbalat yóbbanteeti ab surgaam genn kàddu gi, mu indaale bataaxal bu tëjuwul, yor ko ci loxoom. 6 Ñu bind ci ne:
8 Ma yónnee ca Sanbalat, ne ko: «Li nga wax amul. Yaw yaa ko fental sa bopp.» 9 Fekk na ñoom ñépp a nu doon jéema xoqtal, yaakaar ne dinanu yoqi, ba liggéey bi du sotti. Ma daldi ne: «Léegi nag Yàlla, ngalla dooleel ma!»
10 Ci kaw loolu ma dem kër Semaya doomu Delaya doomu Metabel, fekk ko mu tëju cib néegam. Mu ne ma:
14 Sama Yàlla, yal nanga bàyyi xel ci Tobyaak Sanbalat te fey leen seen jëf jii, ñook Nowadiya, yonent bu jigéen beek yeneen yonent yi ma doon xoqtal.
15 Ba mu ko defee tata ji noppi ñaar fukki fan ak juróom ci weeru Elul[c]. Ñu liggéey ko ci juróom fukki fan ak ñaar. 16 Ba ko sunu noon yépp yégee, ñook mboolem jaambur ñi ñu wër, am nañ tiitaange ak mbetteel mu réy, ndax xam nañu ne sunu ndimbalu Yàlla rekk lanu sottale boobu liggéey.
17 Ca yooya jamono garmiy Yuda daan nañu bindanteek Tobya lu bare. 18 Bare na sax ci waa Yuda ñu faroon ak moom ci kaw ngiñ, ndax la mu doon denc doomu Sekaña, ma Ara di baayam, te doomam Yowanan di denc doomu Mesulam ma Berekiya di baayam. 19 Rax ci dolli ñu di ma gëmloo ag mbaaxam, te di ko jottli samay kàddu. Tobya nag yónnee ma ay bataaxal, di ma xoqtal.
<- Neyemi 5Neyemi 7 ->