6 Aji Sax ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israyil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu. 7 Ma noon su ma defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci. 8 Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu. 9 Ni gànctu yombe Israyil tax na réew mi sobewu. Njaaloo naak yàllay doj, njaalook yàllay bant. 10 Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee. 11 Aji Sax ji nag ne ma: «Li Israyil di woyof kumba lépp sax moo tane Yuda workat bi. 12 Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne:
“Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.”
Kàddug Aji Sax jee.
“Duma la fasal kanam.
Man Boroom ngor laa,
te duma jàpp mer ba fàww.”
Kàddug Aji Sax jee.
13 “Nangul ne ñaaw nga rekk,
te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ,
di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi
ci ker garaboo garab gu naat,
te dégluwoo ma.”»
Kàddug Aji Sax jee.
14 «Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maay seen boroom kër,
maay jële kenn ci bii dëkk,
ñaar ca bee gox,
boole indi Siyoŋ,
15 tànnal leen sàmm yu ma doy,
ñu sàmme leen xam-xam akug muus.
16 Janti keroog bu ngeen baree ba giir ci réew mi,
a3.1 Yoonu Musaa mayul ku fase jabaram mu di ko jëlaat, gannaaw bu séyaatee ba tas. Seetal ci Baamtug yoon wi 24.1-4.b3.2 tund: kaw tund yooyu lañu daan jaamoo tuur yi ñu foogoon ne dañuy nangul am njur.c3.16 gaalu kóllërey Aji Sax ji moo doon firndeel teewaayu Aji Sax ji ci digg bànni Israyil.