1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma: 2 Yaw nit ki, caxal waa kër Israyil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal. 3 Ne leen: «Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
11 Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 12 «Waxal waa kër fippukat yi, ne leen: “Xamuleen lu mbir yooyu di wund?” Ne leen: “Mu ngoogu, buuru Babilon a dem Yerusalem, jàpp buur baak kàngam ya, ànd ak ñoom, yóbbu Babilon. 13 Moo tànn ku bokk ci askanu buur, fasook moom kàddu, giñloo ko ne dina ko nangul, daldi yóbbu njiiti réew mi, 14 ngir nguurug Yerusalem suufe, baña yékkatiku, di wéye surgawu Babilon, ni ñu ko fasoo woon. 15 Ka bokk ci askanu buurub Israyil nag fippu, yónni ay ndaw réewum Misra, ngir ñu jox ko ay fas ak mbooloo mu takku. Moo ka def loolu dina baaxlee? Mbaa dina mucc? Nu mu cay mucce te wor kàddu, ga mu fasoo woon?
16 «“Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, ci biir réewum buur boobu ko fal, te mu sàggane la mu ko giñaloon, wor kàddu ga mu fasante woon ak moom, ci biir Babilon googu lay deeye. 17 Firawnaak mbooloom mu réy ak gàngooram gu mag sax duñu ko mana wallu ci xare, keroog bu ñuy yékkati ab sëkk, tabax ab gawukaay ngir bóom ñu bare. 18 Moo sàggane ngiñ, moo wor kàddu ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk.
19 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Giñ naa ko ci man miy dund, maay këpp jëfam ci kaw boppam ndax ngiñ li mu ma giñal la sofental, kàddu gi mu fasanteek man la wor. 20 Maa koy laaw sama mbaal, mu lonkoo samab caax, ma yóbbu ko Babilon, layoo faak moom ñàkke worma gi mu ma ñàkke worma. 21 Mboolem ñay dawe ca gàngooram yépp, saamar lañuy fàddoo; ña cay rëcce, fépp fu ngelaw jublu lañuy tasaarooji, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax.
22 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
-
a 17.3 jaxaay ji mooy Buuru Babilon, Nabukodonosor mi nangu woon Yerusalem.
b 17.4 dagg car bu ndaw mooy ba ñu yóbboo Buur Yowakin ngàllo ca Babilon.
c 17.5 jiwum réew mi mooy Cedesyas baayu Yowakin bu ndaw. Buur Cedesyas la Nabukodonosor dénkoon nguurug Yuda.
d 17.7 jeneen jaxaay ju mag mooy Firawna buuru Misra.