5 Ba surgay Buur Esekiya àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax, 6 Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa. 7 Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”»
8 Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa. 9 Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub Kuus moo leen di songsi. Mu dellu yebal ay ndaw ca Esekiya, ne leen:: 10 «Waxleen Esekiya buurub Yuda, ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri. 11 Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, yaa ciy mucc? 12 Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar? 13 Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”»
14 Ba Esekiya jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji. 15 Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf. 16 Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund! 17 Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas xeet yeek seeni réew, 18 te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen. 19 Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, ngalla wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw Aji Sax ji doŋŋ yaa di Yàlla.»
20 Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiya ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne li nga ko ñaan ci Senakerib buurub Asiri, dégg na ko. 21 Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom:
32 «Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne:
35 Guddig keroog malaakam Aji Sax ji moo dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp, diy néew.
36 Ba loolu amee Senakerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca Niniw. 37 Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag, ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko.
<- 2.Buur ya 182.Buur ya 20 ->