1 Céy bu ngeen ma muñaloon, ba ma dof-doflu tuuti! Muñal-leen ma rekk. 2 Maa leen di fiiree fiiraangey Yàlla ci boppam, ndax jenn jëkkër doŋŋ laa leen digool ab séy, te mooy Almasi mi ma leen namma jébbal, te fekk leen di janq bu set wecc. 3 Waaye na jaan ja naxe woon Awa, ca pexeem, ragal naa seenum xel yàqoo noonu, ba dëddu ngëm gu dëggu te set gu ngeen ŋoye woon ci Almasi. 4 Ndax kat gaaw ngeena xajoo lool, nit ku dikk, di leen waare meneen Yeesu mu nu waarewul, mbaa geneen noo gu ngeen jot te jotuleen ko woon, mbaa beneen xibaar bu ngeen dëggal, te mu wuute ak ba ngeen déggoon. 5 Moona ndaw yu màgga màgg yooyeey, foog naa ne duma seen cuune ci lenn. 6 Su ma dee ku xareñul ci wàllu wax it, du ci wàllu xam-xam, te nu nekk lanu leen wone loolu, ci bépp fànn.
7 Am boog damaa tooñ ca na ma toroxloo ngir darajaal leen, ndax la ma leen laajul ag pey, ba ma leen di àgge xibaaru jàmm bu Yàlla bi? 8 Yeneen mboolooy gëmkat de laa jëlal, nde maa nangoo ag peyoor ca ñoom, ba man leena liggéeyal, yeen, ci neen. 9 Te ba ma nekkee ci yeen te soxla dab ma, wéeruwuma ci kenn ci yeen, ndax la ma ñàkkoon, bokk ya jóge Maseduwan ñoo ma ko indil. Fexe naa ba du lenn lu ma leen diisale, te noonu laay saxoo. 10 Ak dëggu Almasi gi ci man, kàddug damu googu, kenn du ma ko xañ, ci diiwaanu Akayi gépp. 11 Lu tax? Ndax dama leena buggul? Yàlla xam na ne «ahakay!» 12 Noonu may def rekk laay saxoo, ngir xañ aw lay, ñiy wut aw lay wu ñu damoo, naan ñook nun a yem kepp daraja. 13 Ñooñu ay ndawi caaxaan lañu, ay liggéeykat yu njublaŋ yu mbubboo ndawi Almasi. 14 Te loolu jarula waaru, ndax Seytaane ci boppam, malaakam leer lay mbubboo. 15 Kon bu ay ndawam itam di mbubboo ndawi njub, du doon lu yéeme. Waaye seenug muj, seeni jëf lay yemool.
16 Ma baamu ko, bu ma kenn jàppe ab dof, mbaa boog, ngeen muñal ma ni ñuy muñale ab dof, ba ma damu tuuti, man itam. 17 Li may wax nag, waxewuma ko ci ndigalal Boroom bi, waaye taxawaayu dof laa koy waxe, gannaaw mbirum damu la. 18 Ndegam ñu baree ngi damu ni niti suuxu neen di damoo, naa damu, man itam. 19 Yeen boroom xel yi, yeenaka nangoo muñal ay dof, 20 nde muñal ngeen ku leen jaamloo, muñal ku leen lekk, muñal ku leen futti, muñal ku leen jaay daraja, muñal ku leen talaata! 21 Ma waxe ko gàcce, mbete noo néew doole, ba manunoo jëfe ak yeen noonu!
30 Su damu waree de, samag néew doole laay damoo. 31 Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu, moom mi yelloo cant ba fàww, xam na ne fenuma. 32 Ba ma nekkee Damaas, ga boroom dëkk ba di jawriñu Buur Aretas, boroom dëkk baa santaane ñu wattu buntu dëkk ba, ngir jàpp ma. 33 Waaye ca palanteeru tatay dëkk ba lañu ma yoore cig dàmba, ba ci suuf. Noonu laa ko rëcce.
<- 2.Korent 102.Korent 12 ->