12 Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di ñaan, ñi féetewoo coonob liggéey ci seen biir te jiite leen ci yoonu Boroom bi, di leen yee, nangeen leen yég. 13 Nangeen leen nawe seen kem kàttan te soppe leen noonu ndax seen liggéey. Gannaaw loolu, nangeen jàmmoo. 14 Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñal-leen ñépp. 15 Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.
16 Fu ngeen tollu bégleen, 17 saxooleen ñaan, 18 te deeleen sant, ak nu mu mana deme, ndax loolu mooy coobarey Yàlla ci yeen ñi ànd ak Almasi Yeesu.
19 Buleen giimal taalub Noowug Yàlla gi, 20 buleen gàttañlu ay kàdduy waxyu. 21 Waaye lu mu mana doon, settantal-leen ko, li baax, ngeen jàpp ci, 22 te lu bon, ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
23 Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee. 24 Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.
25 Bokk yi, nun itam, ñaanal-leen nu.
26 Nuyul-leen nu bokk yépp, te fóonal-leen nu leen na mu gëna selle. 27 Maa ngi leen di dénku nag, ngir Boroom bi, jàngleen biral bataaxal bii ngir bokk yépp.
28 Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak yeen.
<- 1.Tesalonig 4